Text copied!
Bibles in Wolof

LUUG 15:4-11 in Wolof

Help us?

LUUG 15:4-11 in Téereb Injiil

4 «Kan ci yéen soo amoon téeméeri xar, te benn réer ci, nooy def? Ndax doo bàyyi ca parlukaay ba juróom ñeent fukki xar ya ak juróom ñeent, toppi ma réer, ba gis ko?
5 Te boo ko gisee, dinga ko gàddu ak bànneex, yóbbu ko kër ga.
6 Boo àggee ca kër ga, dinga woo say xarit ak say dëkkandoo ne leen: “Kaayleen bànneexu ak man, ndaxte gis naa sama xar ma réeroon.”
7 «Maa ngi leen di wax lii: ci noonule, dina am mbég ci asamaan, bu benn bàkkaarkat tuubee ay bàkkaaram. Te mbég moomu mooy ëpp mbég, mi fay am, ngir juróom ñeent fukk ak juróom ñeent ñu jub, te soxlawuñoo tuub seeni bàkkaar.
8 «Te it bu jigéen dencoon fukki libidoor, benn réer ca, nu muy def? Ndax du taal ab làmp, bale kër ga, seet fu nekk, ba gis ko?
9 Bu ko gisee, dina woo ay xaritam ak ay dëkkandoom ne leen: “Kaayleen bànneexu ak man, ndaxte gis naa sama alal ja réeroon.”
10 Maa ngi leen di wax lii: ci noonule la malaakay Yàlla yi di ame mbég ci benn bàkkaarkat bu tuubee ay bàkkaaram.»
11 Yeesu dellu ne leen: «Dafa amoon góor gu am ñaari doom.
LUUG 15 in Téereb Injiil

Luug 15:4-11 in Kàddug Yàlla gi

4 «Ana kan ci yeen mooy am téeméeri xar, réerle ci menn, te bàyyiwul ca àll ba juróom ñeent fukki xar ya ak juróom ñeent (99), ngir toppi ma réer, ba gis ko?
5 Bu ko gisee lay bég, teg ko ca mbagg ma, yóbbu kër ga.
6 Te bu àggee ca kër ga, xarit yaak dëkk ya lay woo, ne leen: “Kaayleen nu bége, sama xar ma réeroon, gis naa ko!”
7 «Maa leen wax, ne leen: bu benn bàkkaarkat doŋŋ tuubee, noonu rekk lay doone mbégte fa asamaan, ba raw mbégte ma fay am, bu juróom ñeent fukk ak juróom ñeenti nit jubee, te soxlawuñoo tuub.
8 «Te it ana jan jigéen mooy am fukki libidoor, benn réer ca, te taalul ab làmp, buub néeg ba, seeta seet, ba gis ko?
9 Bu ko gisee, xarit yaak dëkk ya lay woo, ne leen: “Kaayleen nu bége, libidoor ba réeroon, gis naa ko.”
10 Maa leen wax ne leen: noonu rekk lay doone mbégte fa malaakay Yàlla ya, bu benn bàkkaarkat doŋŋ tuubee.»
11 Yeesu neeti: «Nit a amoon ñaari doom yu góor.
Luug 15 in Kàddug Yàlla gi