Text copied!
Bibles in Wolof

LUUG 15:16-23 in Wolof

Help us?

LUUG 15:16-23 in Téereb Injiil

16 Mu xiif ba bëgga lekk ca ñamu mbaam-xuux ya, ndaxte kenn mayu ko dara.
17 Mujj xelam délsi, mu ne: “Sama baay am na ay surga yu bare, te dañuy lekk ba suur. Man nag maa ngi fii di bëgga dee ak xiif!
18 Damay jóg, dem ca sama baay ne ko: ‘Baay, tooñ naa Yàlla, tooñ naa la;
19 yeyootumaa nekk sa doom; boole ma ci say surga.’ ”
20 «Mu daldi jóg, jëm kër baayam. Waaye bi muy soreendi kër ga, baayam séen ko, yërëm ko, daldi daw laxasu ko, fóon ko.
21 Doom ja ne ko: “Baay, tooñ naa Yàlla, tooñ naa la; yeyootumaa nekk sa doom.”
22 Waaye baay ba ne ay surgaam: “Gaawleen indi mbubb, mi gëna rafet, solal ko ko. Te ngeen roof ab jaaro ci loxoom te solal ko ay dàll.
23 Indileen sëllu wu duuf wa te rey ko, nu lekk te bànneexu;
LUUG 15 in Téereb Injiil

Luug 15:16-23 in Kàddug Yàlla gi

16 Mu dem ba noon ngéeja lekk ca xolliti doomi garab ya mbaam-xuux yay lekk, fajeb xiifam, te kenn mayu ko ca.
17 Xel ma mujj délsi, mu ne: “Ñaata surga la sama baay am, seen lekk ne gàññ, man, ab xiif di ma rey fii!
18 Naa jóg, dem ca sama baay, ne ko: ‘Baay, tooñ naa Yàlla, tooñ la;
19 yeyootumaa tuddoo sax sa doom; léegi def ma ni ku bokk ci say surga.’ ”
20 «Mu jóg, ngir dellu kër baayam. Fu sore la ko baayam séene, muy dikk. Mu ñeewante ko, daw, laxasu ko, fóon ko.
21 Doom ja ne ko: “Baay, tooñ naa Yàlla, tooñ la; yeyootumaa tuddoo sax sa doom.”
22 Teewul baay ba ne ay surgaam: “Gaawleen indi mbubb mi gëna rafet, solal ko, te ngeen takkal ko ab jaaro ci loxoom, solal ko ay dàll.
23 Indileen sëlluw yafal wa, rey, nu lekk, te bànneexu;
Luug 15 in Kàddug Yàlla gi