Text copied!
Bibles in Wolof

LUUG 13:9-17 in Wolof

Help us?

LUUG 13:9-17 in Téereb Injiil

9 Xëy na dina meññi. Bu ko deful, nga gor ko.”»
10 Benn bésub noflaay Yeesoo ngi doon jàngle ci ab jàngu.
11 Amoon na fa jigéen ju rab jàppoon, ba feebarloo ko lu wara mat fukki at ak juróom ñett; dafa xuuge woon te manul woona siggi dara.
12 Bi ko Yeesu gisee, mu woo ko ne ko: «Soxna si, sa feebar deñ na.»
13 Noonu mu teg ko ay loxoom, soxna sa siggi ca saa sa, di màggal Yàlla.
14 Waaye njiitu jàngu ba mer, ndax li Yeesu fajoon nit ca bésub noflaay ba, mu ne mbooloo ma: «Am na juróom benni fan yu nit ñi wara liggéey. Kon war ngeena ñëw faju ci bés yooyu, waaye du ci bésub noflaay bi.»
15 Boroom bi ne ko: «Naaféq yi! Ndax bésub noflaay bi, kenn ku nekk ci yéen du yiwee ca gétt ga yëkkam walla mbaamam ngir wëggi ko?
16 Jigéen jii nag bokk ci askanu Ibraayma te Seytaane tënk ko fukki at ak juróom ñett, ndax kenn waru koo yiwi ci bésub noflaay bi?»
17 Naka la wax loolu, noonam yépp daldi rus, waaye mbooloo mi di bég ci jëf yu yéeme, yi mu doon def yépp.
LUUG 13 in Téereb Injiil

Luug 13:9-17 in Kàddug Yàlla gi

9 Jombul mu meññ déwén; lu ko moy, nga gor ko.”»
10 Benn bésub Noflaay, Yeesoo doon jàngle ci ab jàngu.
11 Ndeke jenn jigéen a nga fa woon; rab a ko woppal lu wara mat fukki at ak juróom ñett, mu xuuge, manula fexe ba siggi.
12 Yeesu gis ko, woo ko, ne ko: «Jongama, teqlikoo nga ak sa laago.»
13 Mu teg ko ay loxoom, mu siggi ca saa sa, di sàbbaal Yàlla.
14 Njiitu jàngu ba nag yékkati kàddug ñaawlu ndax bésub Noflaay ba Yeesu faje. Mu ne mbooloo ma: «Juróom benni fan la nit ñi wara liggéey. Kon ci fan yooyu ngeen wara fajusi, waaye du ci bésub Noflaay.»
15 Sang bi ne ko: «Jinigalkat yi ngeen doon! Xanaa du ci bésub Noflaay la kenn ku nekk ci yeen di yiwee aw yëkkam mbaa mbaamam ca gétt ga, ngir wëggi ko?
16 Jigéen jii di sëtub Ibraayma, te fukki at ak juróom ñett a ngii Seytaane làggal ko, wareesu koo yiwi, teggil ko laago jii ci bésub Noflaay?»
17 Ba mu waxee loolu, noonam yépp a rus, mbooloo ma nag di bége mboolem jëf ju yéeme, ja muy def.
Luug 13 in Kàddug Yàlla gi