Text copied!
Bibles in Wolof

LUUG 13:8-12 in Wolof

Help us?

LUUG 13:8-12 in Téereb Injiil

8 Surga ba ne ko: “Sang bi, bàyyiwaat ko fi at mii. Dinaa wàqi taat wi, def ci tos.
9 Xëy na dina meññi. Bu ko deful, nga gor ko.”»
10 Benn bésub noflaay Yeesoo ngi doon jàngle ci ab jàngu.
11 Amoon na fa jigéen ju rab jàppoon, ba feebarloo ko lu wara mat fukki at ak juróom ñett; dafa xuuge woon te manul woona siggi dara.
12 Bi ko Yeesu gisee, mu woo ko ne ko: «Soxna si, sa feebar deñ na.»
LUUG 13 in Téereb Injiil

Luug 13:8-12 in Kàddug Yàlla gi

8 Surga ba ne ko: “Sang bi, bàyyiwaat ko at mii rekk, ba ma wéex ko, def ci tos.
9 Jombul mu meññ déwén; lu ko moy, nga gor ko.”»
10 Benn bésub Noflaay, Yeesoo doon jàngle ci ab jàngu.
11 Ndeke jenn jigéen a nga fa woon; rab a ko woppal lu wara mat fukki at ak juróom ñett, mu xuuge, manula fexe ba siggi.
12 Yeesu gis ko, woo ko, ne ko: «Jongama, teqlikoo nga ak sa laago.»
Luug 13 in Kàddug Yàlla gi