Text copied!
Bibles in Wolof

LUUG 13:31-34 in Wolof

Help us?

LUUG 13:31-34 in Téereb Injiil

31 Ca jamono jooja ay Farisen ñëw ca Yeesu ne ko: «Jógeel fii, dem feneen, ndaxte Erodd a ngi lay wuta rey.»
32 Noonu mu ne leen: «Demleen ne bukki boobu ne ko: “Xoolal, maa ngi dàq rab yi tey wéral nit ñi tey ak suba. Ca ñetteelu fan ba, ma àgg fa ma Yàlla jëmale.”
33 Waaye fàww ma dox sama itte tey, suba ak gannaaw suba, ndaxte wareesula reye ab yonent feneen fu dul Yerusalem.
34 «Yerusalem, Yerusalem, yaw miy rey yonent yi, tey sànni ay doj ndaw yi, ba ñu dee, aka maa bëggoona dajale say doom, ni ginaar di uufe ay cuujam te nanguwuleen!
LUUG 13 in Téereb Injiil

Luug 13:31-34 in Kàddug Yàlla gi

31 Ca jamono jooju tembe la ay Farisen dikk, ne Yeesu: «Jógeel fii, te dem, ndax Buur Erodd da laa nara rey.»
32 Mu ne leen: «Demleen wax njomboor moomu, ne ko: “Maa ngii di dàq rab yi, di maye ag wér, tey ak ëllëg. Bésub ñetteel ba nag ma sottal.”
33 Waaye tey ak ëllëg ak sibir, fàww ma dem, ndax ab yonent wareesu koo bóome fenn fu dul Yerusalem.
34 «Yerusalem, Yerusalem, yaw miy bóom yonent yi, di sànni ay doj ñi ñu yebal ci yaw, ba ñu dee, ñaata yoon laa namma dajale say doom, uuf ni ganaar di uufe ay cuujam, te nanguwuloo?
Luug 13 in Kàddug Yàlla gi