Text copied!
Bibles in Wolof

LUUG 13:27-32 in Wolof

Help us?

LUUG 13:27-32 in Téereb Injiil

27 Mu ne leen: “Nee naa leen xawma fu ngeen bokk. Yéen ñépp soreleen ma, defkati lu bon yi!”
28 Foofa dingeen jooy, di yéyu, bu ngeen gisee seeni maam Ibraayma, Isaaxa, Yanqóoba ak yonent yépp ci nguuru Yàlla, te ñu dàq leen ca biti.
29 Ay nit dinañu jóge penku ak sowu, nor ak sudd, ñëw, bokk lekk ci ñam, yi Yàlla di joxe ci nguuram.
30 Noonu ñenn ci ñi mujj ñooy jiituji; te ci ñi jiitu, ñooy mujji.»
31 Ca jamono jooja ay Farisen ñëw ca Yeesu ne ko: «Jógeel fii, dem feneen, ndaxte Erodd a ngi lay wuta rey.»
32 Noonu mu ne leen: «Demleen ne bukki boobu ne ko: “Xoolal, maa ngi dàq rab yi tey wéral nit ñi tey ak suba. Ca ñetteelu fan ba, ma àgg fa ma Yàlla jëmale.”
LUUG 13 in Téereb Injiil

Luug 13:27-32 in Kàddug Yàlla gi

27 Mu neeti leen: “Nee naa leen xawma fu ngeen bokk. Soreleen ma yeen ñépp, defkati njubadi yi!”
28 Foofa la ay jooy ak naqarlu bay yéyu di ame yoon, kera bu ngeen gisee seeni maam Ibraayma ak Isaaxa ak Yanqóoba ak yonent yépp ca biir nguurug Yàlla, te fekk yeen ci seen bopp, ñu dàq leen ca biti.
29 Penku ak sowu, bëj-gànnaar ak bëj-saalum, la aw nit di bawoo, dikk toog ca ndabal bernde la ca nguurug Yàlla.
30 Su ko defee nag, ñenn a ngi mujje tey, waaye ëllëg ñooy jiitu; te ñenn a ngi jiitu tey, waaye ëllëg ñooy mujje.»
31 Ca jamono jooju tembe la ay Farisen dikk, ne Yeesu: «Jógeel fii, te dem, ndax Buur Erodd da laa nara rey.»
32 Mu ne leen: «Demleen wax njomboor moomu, ne ko: “Maa ngii di dàq rab yi, di maye ag wér, tey ak ëllëg. Bésub ñetteel ba nag ma sottal.”
Luug 13 in Kàddug Yàlla gi