Text copied!
Bibles in Wolof

LUUG 13:12-16 in Wolof

Help us?

LUUG 13:12-16 in Téereb Injiil

12 Bi ko Yeesu gisee, mu woo ko ne ko: «Soxna si, sa feebar deñ na.»
13 Noonu mu teg ko ay loxoom, soxna sa siggi ca saa sa, di màggal Yàlla.
14 Waaye njiitu jàngu ba mer, ndax li Yeesu fajoon nit ca bésub noflaay ba, mu ne mbooloo ma: «Am na juróom benni fan yu nit ñi wara liggéey. Kon war ngeena ñëw faju ci bés yooyu, waaye du ci bésub noflaay bi.»
15 Boroom bi ne ko: «Naaféq yi! Ndax bésub noflaay bi, kenn ku nekk ci yéen du yiwee ca gétt ga yëkkam walla mbaamam ngir wëggi ko?
16 Jigéen jii nag bokk ci askanu Ibraayma te Seytaane tënk ko fukki at ak juróom ñett, ndax kenn waru koo yiwi ci bésub noflaay bi?»
LUUG 13 in Téereb Injiil

Luug 13:12-16 in Kàddug Yàlla gi

12 Yeesu gis ko, woo ko, ne ko: «Jongama, teqlikoo nga ak sa laago.»
13 Mu teg ko ay loxoom, mu siggi ca saa sa, di sàbbaal Yàlla.
14 Njiitu jàngu ba nag yékkati kàddug ñaawlu ndax bésub Noflaay ba Yeesu faje. Mu ne mbooloo ma: «Juróom benni fan la nit ñi wara liggéey. Kon ci fan yooyu ngeen wara fajusi, waaye du ci bésub Noflaay.»
15 Sang bi ne ko: «Jinigalkat yi ngeen doon! Xanaa du ci bésub Noflaay la kenn ku nekk ci yeen di yiwee aw yëkkam mbaa mbaamam ca gétt ga, ngir wëggi ko?
16 Jigéen jii di sëtub Ibraayma, te fukki at ak juróom ñett a ngii Seytaane làggal ko, wareesu koo yiwi, teggil ko laago jii ci bésub Noflaay?»
Luug 13 in Kàddug Yàlla gi