Text copied!
Bibles in Wolof

LUUG 12:37-44 in Wolof

Help us?

LUUG 12:37-44 in Téereb Injiil

37 Surga yooyee seen njaatige fekkul ñuy nelaw, ba mu agsee, ñoo gëna yeyoo ngërëm. Ci dëgg maa ngi leen koy wax, njaatige bi dina sol yérey waañ, wax leen ñu toog lekk, ba noppi indil leen ñam wi.
38 Su fekkee seen njaatige ci xaaju guddi lay ñëw sax, walla bu suuf seddee, te fekk leen noonu, surga yooyu ñoo gëna yeyoo ngërëm.
39 Waaye xamleen lii: bu boroom kër gi xamoon ban waxtu la sàcc bi di ñëw, du ko bàyyi, mu toj këram.
40 Yéen itam taxawleen jonn, ndaxte Doomu nit ki dina ñëw ci waxtu wu ngeen ko séenuwul.»
41 Piyeer ne Yeesu: «Boroom bi, ndax dangay dégtal léeb wii ngir nun rekk walla ngir mbooloo mépp?»
42 Boroom bi ne ko: «Kan moo nekk surga bu takku te teey, bu njaatigeem teg ci waa kër gi, ngir mu leen di dundal ci jamono ji?
43 Bu njaatigeem ñëwee te gis mu def noonu, surga boobu dina am ngërëm.
44 Ci dëgg maa ngi leen koy wax, njaatige bi dina ko teg ci alalam jépp.
LUUG 12 in Téereb Injiil

Luug 12:37-44 in Kàddug Yàlla gi

37 Ndokklee surga yooyu seen njaatige dikk fekk ñu teewlu. Maa leen ko wax déy, njaatige leey takku, toogal leen ba noppi dikk, taajal leen, ñu lekk.
38 Ndegam ba guddi ga xaajee la njaatige la ñibbsi, ba fekk surga ya teewloo noonu, am ba suuf seddee la, lu mu ci mana doon, ndokklee ñoom.
39 Waaye lii de xamleen ko: boroom kër, su xamoon wan waxtu la ab sàcc di ñëw, du ko wacc moos, mu dàjjiy, dugg këram.
40 Kon yeen itam waajleen ba jekk, ndax waxtu wu ngeen foogul, ci la Doomu nit ki di ñëw.»
41 Piyeer nag ne Yeesu: «Sang bi, ndax nun doŋŋ nga léeb lii, am ñépp a ko moom?»
42 Sang bi ne ko: «Ana kan nag mooy saytukat bu wóor te muus, ba njaatigeem batale ko curgag këram, ngir mu di leen jox seen njël ca ba muy jot?
43 Ndokklee surga bu njaatigeem dikk, fekk ko muy doxale noonu.
44 Maa leen ko wax déy, alalam jépp la ko njaatige la di far dénk.
Luug 12 in Kàddug Yàlla gi