Text copied!
Bibles in Wolof

LUUG 12:28-47 in Wolof

Help us?

LUUG 12:28-47 in Téereb Injiil

28 Yéen ñi néew ngëm! Bu Yàlla woddee nii ñaxum tool yi, miy sax tey, te bu subaa ñu def ko ci taal bi, ndax du leen gëna wodd?
29 Buleen di wut lu ngeen di lekk walla lu ngeen di naan; te buleen ci jaaxle.
30 Ndaxte loolu lépp, ñi xamul Yàlla ñoo koy wut. Te seen Baay xam na ne soxla ngeen ko.
31 Waaye wutleen nguuram, te loolu lépp dina leen ko ci dollil.
32 «Buleen ragal dara, yéen coggal ju ndaw ji, ndaxte dafa soob seen Baay, mu jagleel leen nguuram.
33 Jaayleen seen alal, sarxe ko, ngir sàkku ay mbuusi xaalis yu dul bënn, maanaam alal ju dul jeex ca laaxira; foofa sàcc du ko jege te max du ko yàq.
34 Ndaxte fu sa alal nekk, fa la sa xol nekk itam.
35 «Takkuleen bu dëgër te bàyyi làmp yi tàkk.
36 Mel-leen ni ay surga yuy xaar seen njaatige buy jóge ca céet ga, ndax bu fëggee bunt ba, ñu ubbil ko ca saa sa.
37 Surga yooyee seen njaatige fekkul ñuy nelaw, ba mu agsee, ñoo gëna yeyoo ngërëm. Ci dëgg maa ngi leen koy wax, njaatige bi dina sol yérey waañ, wax leen ñu toog lekk, ba noppi indil leen ñam wi.
38 Su fekkee seen njaatige ci xaaju guddi lay ñëw sax, walla bu suuf seddee, te fekk leen noonu, surga yooyu ñoo gëna yeyoo ngërëm.
39 Waaye xamleen lii: bu boroom kër gi xamoon ban waxtu la sàcc bi di ñëw, du ko bàyyi, mu toj këram.
40 Yéen itam taxawleen jonn, ndaxte Doomu nit ki dina ñëw ci waxtu wu ngeen ko séenuwul.»
41 Piyeer ne Yeesu: «Boroom bi, ndax dangay dégtal léeb wii ngir nun rekk walla ngir mbooloo mépp?»
42 Boroom bi ne ko: «Kan moo nekk surga bu takku te teey, bu njaatigeem teg ci waa kër gi, ngir mu leen di dundal ci jamono ji?
43 Bu njaatigeem ñëwee te gis mu def noonu, surga boobu dina am ngërëm.
44 Ci dëgg maa ngi leen koy wax, njaatige bi dina ko teg ci alalam jépp.
45 Waaye su fekkee surga ba da ne ci xelam: “Sama njaatige day yéexa ñëw,” ba tax mu tàmbalee dóor surga ya ca des ak mbindaan ya, di lekk te di naan, di màndi,
46 kon njaatige ba dina ñëw ci bés bu mu ko séenuwul ak waxtu wu mu xamul. Dina ko dóor ay dóor yu metti, jox ko añub ñi gëmul Yàlla.
47 «Surga bi xam bëgg-bëggu njaatigeem, te waajul mbaa mu takku def ko, dinañu ko dóor dóor yu metti.
LUUG 12 in Téereb Injiil

Luug 12:28-47 in Kàddug Yàlla gi

28 Ndegam ñaxum tool miy dund tey, te léegi ñu sànni ko cib taal, moom la Yàlla solale noonu, xanaa astamaak yeen kay? Yeenaka néew ngëm!
29 Yeen nag, buleen tiisoo lu ngeen lekk, mbaa lu ngeen naan; te bu yooyu xalaat ub seen bopp.
30 Ndax loolu lépp, xeeti yéefari àddina, ñoo koy tiisoo, te yeen, Baay bi xam na ne soxla ngeen ko.
31 Waaye tiisooleen nguuram, su boobaa dees na leen ci dollil loolu.
32 «Buleen ragal dara, yeen jur gu sew gi, ndax seen Baay la soob, mu jagleel leen nguur gi.
33 Jaayleen seen alal, sarxe xaalis bi, sàkkuleen mbuus yu dul ràpp, muy dencu ëllëg bu dul jeex fa asamaan, fa ko sàcc dul jege, max du ko yàq.
34 Ndax fu sab denc nekk, sab xol it a nga fa.
35 «Takkuleen te seeni làmp di tàkk.
36 Mel-leen ni nit ñuy séentu seen njaatige lu jóge céet, ndax bu dikkee ba fëgg bunt ba, ñu daldi ko ubbil.
37 Ndokklee surga yooyu seen njaatige dikk fekk ñu teewlu. Maa leen ko wax déy, njaatige leey takku, toogal leen ba noppi dikk, taajal leen, ñu lekk.
38 Ndegam ba guddi ga xaajee la njaatige la ñibbsi, ba fekk surga ya teewloo noonu, am ba suuf seddee la, lu mu ci mana doon, ndokklee ñoom.
39 Waaye lii de xamleen ko: boroom kër, su xamoon wan waxtu la ab sàcc di ñëw, du ko wacc moos, mu dàjjiy, dugg këram.
40 Kon yeen itam waajleen ba jekk, ndax waxtu wu ngeen foogul, ci la Doomu nit ki di ñëw.»
41 Piyeer nag ne Yeesu: «Sang bi, ndax nun doŋŋ nga léeb lii, am ñépp a ko moom?»
42 Sang bi ne ko: «Ana kan nag mooy saytukat bu wóor te muus, ba njaatigeem batale ko curgag këram, ngir mu di leen jox seen njël ca ba muy jot?
43 Ndokklee surga bu njaatigeem dikk, fekk ko muy doxale noonu.
44 Maa leen ko wax déy, alalam jépp la ko njaatige la di far dénk.
45 Waaye su jawriñ ja nee ci xelam: “Sama njaatige dikkagul léegi,” ba tax mu tàmbalee dóor surga ya, góor ak jigéen, di lekk ak a naan, di màndi,
46 su boobaa njaatige laay dikk bés bu mu ko séenuwul ak waxtu wu mu foogul, te mbugal mu metti la koy mbugal, sédd ko ci añub gëmadikat ñi.
47 «Jawriñ jooju xam nammeelu njaatigeem, te taxul mu waaj ko, ba jëfewu ko, ay yetam dina bare.
Luug 12 in Kàddug Yàlla gi