Text copied!
Bibles in Wolof

LUUG 12:13-36 in Wolof

Help us?

LUUG 12:13-36 in Téereb Injiil

13 Am ca mbooloo ma ku ne Yeesu: «Kilifa gi, joxal ndigal sama mag, mu sédd ma ci sunu ndono.»
14 Yeesu ne ko: «Sama waay, kan moo ma fal àttekat ci seen kaw, walla mu teg ma fi, ma di leen séddaleel seen alal?»
15 Noonu mu ne leen ñoom ñépp: «Moytuleen bëgge, ndaxte bakkanu nit ajuwul ci alalam, ak lu mu baree bare.»
16 Noonu mu dégtal leen wii léeb ne: «Dafa amoon waa ju bare alal, te ay toolam nangu lool,
17 muy werante ci xelam naan: “Nu ma wara def? Ndaxte amatuma fu ma dajale sama ngóob mi.”
18 Noonu mu ne: “Nii laay def: daaneel sama sàq yi, defaraat yu gëna réy, ba man cee dajale sama dugub ji ak sama am-am bépp.
19 Te dinaa kañ sama bopp ne: ‘Yaw mii, am nga alal ju bare ju mana dem ay ati at; noppalal sa yaram, di lekk, di naan, tey bég.’ ”
20 Waaye Yàlla ne ko: “Ñàkk xel! Guddig tey, dees na jël sa bakkan. Kon li nga dajale lépp, ku koy moom?”
21 «Kiy dajale alal ngir boppam nag te amul dara ca kanam Yàlla, lu mel nii moo lay dal.»
22 Noonu Yeesu daldi ne taalibeem yi: «Loolu moo tax maa ngi leen koy wax, buleen seen bakkan jaaxal, ci lu ngeen wara lekk. Buleen jaaxle it ngir seen yaram ci lu ngeen wara sol,
23 ndaxte bakkan moo gën lekk, te yaram a gën koddaay.
24 Seetleen baaxoñ yi: duñu ji, duñu góob, amuñu dencukaay, amuñu sàq, teewul Yàllaa ngi leen di dundal. Céy ni ngeen ëppe maana picc yi!
25 Ana kan ci yéen ci kaw njaaxleem, moo mana yokk waxtu ci àppam?
26 Su fekkee lu tuuti loolu rekk manuleen koo def, kon lu tax ngeen di jaaxle ci li ci des?
27 «Seetleen ni tóor-tóori ñax mi di saxe. Duñu liggéey, duñu ëcc, waaye maa ngi leen di wax ne Suleymaan sax ci ndamam soluwul woon ni benn ci ñoom.
28 Yéen ñi néew ngëm! Bu Yàlla woddee nii ñaxum tool yi, miy sax tey, te bu subaa ñu def ko ci taal bi, ndax du leen gëna wodd?
29 Buleen di wut lu ngeen di lekk walla lu ngeen di naan; te buleen ci jaaxle.
30 Ndaxte loolu lépp, ñi xamul Yàlla ñoo koy wut. Te seen Baay xam na ne soxla ngeen ko.
31 Waaye wutleen nguuram, te loolu lépp dina leen ko ci dollil.
32 «Buleen ragal dara, yéen coggal ju ndaw ji, ndaxte dafa soob seen Baay, mu jagleel leen nguuram.
33 Jaayleen seen alal, sarxe ko, ngir sàkku ay mbuusi xaalis yu dul bënn, maanaam alal ju dul jeex ca laaxira; foofa sàcc du ko jege te max du ko yàq.
34 Ndaxte fu sa alal nekk, fa la sa xol nekk itam.
35 «Takkuleen bu dëgër te bàyyi làmp yi tàkk.
36 Mel-leen ni ay surga yuy xaar seen njaatige buy jóge ca céet ga, ndax bu fëggee bunt ba, ñu ubbil ko ca saa sa.
LUUG 12 in Téereb Injiil

Luug 12:13-36 in Kàddug Yàlla gi

13 Kenn ca mbooloo ma moo noon Yeesu: «Sëriñ bi, waxal ci sama mag, mu jox ma sama wàll ci ndono li nu bokk.»
14 Yeesu ne ko: «Waa jii, kan moo ma fal àttekat mbaa miraaskat ci seen kaw?»
15 Ci kaw loolu mu ne leen ñoom ñépp: «Moytuleen wépp xeetu bëgge, ndax loo barele barele, sa bakkan ajuwul ci sa alal.»
16 Mu léeb leen nag, ne leen: «Nit la woon ku woomle, te ab toolam nangu.
17 Mu naan ca xel ma: “Nu may def nag? Amatuma sax fu ma denc sama ngóob mi!”
18 Ci kaw loolu mu ne: “Nii laay def: samay sàq laay daaneel, daldi defaraat sàq yu gëna mag, denc ci sama pepp ak mboolem lu ma am.
19 Su ko defee ci samam xel laa naan: ‘Céy sama waa ji, yaa ngeek alal ju bare ju mana dem ay ati at; neel finaax, di lekk, di naan ak a bége.’ ”
20 Yàlla nag ne ko: “Ñàkk xel! Guddig tey jii, dees na jël sa bakkan. Kon li nga waajal, ana kuy doon boroom?”
21 «Kuy dajaleel boppam alal te woomlewoo fa Yàlla, loolu mooy saw demin.»
22 Gannaaw loolu Yeesu ne ay taalibeem: «Moo tax ma ne leen, buleen seen bakkan jaaxal, ngir lu ngeen lekk, te it buleen seen yaram jaaxal ngir lu ngeen sol,
23 ndax lekk gi, bakkan bee ko ëpp solo, te koddaay li it, yaram wee ko ëpp solo.
24 Seetleen ci baaxoñ: du ji, du góob, amul ub denc mbaa am sàq. Teewul Yàlla di ko dundal. Yeen nag, ñaata yoon ngeen gën picc yi!
25 Ana kan ci yeen mooy jaaxle, di xalaata xalaat bakkanam ba mana yokk lu tollook xef ak xippi ci àppam?
26 Ndegam loolu gëna tuut sax moo leen të, ana lu ngeen di xalaat ci leneen?
27 «Seetleen ni tóor-tóor yiy saxe. Sonnuñu, ëccuñu, waaye maa leen ko wax, Suleymaan ak darajaam jépp sax, soluwul woon ni benn ci ñoom.
28 Ndegam ñaxum tool miy dund tey, te léegi ñu sànni ko cib taal, moom la Yàlla solale noonu, xanaa astamaak yeen kay? Yeenaka néew ngëm!
29 Yeen nag, buleen tiisoo lu ngeen lekk, mbaa lu ngeen naan; te bu yooyu xalaat ub seen bopp.
30 Ndax loolu lépp, xeeti yéefari àddina, ñoo koy tiisoo, te yeen, Baay bi xam na ne soxla ngeen ko.
31 Waaye tiisooleen nguuram, su boobaa dees na leen ci dollil loolu.
32 «Buleen ragal dara, yeen jur gu sew gi, ndax seen Baay la soob, mu jagleel leen nguur gi.
33 Jaayleen seen alal, sarxe xaalis bi, sàkkuleen mbuus yu dul ràpp, muy dencu ëllëg bu dul jeex fa asamaan, fa ko sàcc dul jege, max du ko yàq.
34 Ndax fu sab denc nekk, sab xol it a nga fa.
35 «Takkuleen te seeni làmp di tàkk.
36 Mel-leen ni nit ñuy séentu seen njaatige lu jóge céet, ndax bu dikkee ba fëgg bunt ba, ñu daldi ko ubbil.
Luug 12 in Kàddug Yàlla gi