Text copied!
Bibles in Wolof

LUUG 11:4-43 in Wolof

Help us?

LUUG 11:4-43 in Téereb Injiil

4 Yal nanga nu baal sunuy bàkkaar, ndaxte nun itam danuy baal ñépp ñi nu tooñ. Yàlla boo nu teg ci yoonu nattu.»
5 Yeesu teg ca ne leen: «Mi ngi mel ni, nga dem seeti sa xarit ci xaaju guddi ne ko: “Xarit, lebal ma ñetti mburu.
6 Dafa am sama xarit bu ma ganesi, te awma dara lu ma ko jox.”
7 «Waaye kooku nekk ci biir néegam, dina ko ne: “Bu ma lakkal, tëj naa bunt bi ba noppi te tëdd naa maak sama njaboot; manumaa jóg di la jox dara.”
8 Maa ngi leen koy wax, su jógul jox ko li muy laaj ndax li ñu xaritoo it, ndax la kee ñàkk jom dina tax mu jox ko lépp li mu soxla.
9 Moo tax ma ne, ñaanleen, ñu may leen; seetleen, te dingeen gis; fëggleen, ñu ubbil leen.
10 Ndaxte képp kuy ñaan, dinga am; kuy seet, dinga gis; kuy fëgg, ñu ubbil la.
11 Bu la sa doom ñaanee jën, yaw miy baayam, ndax dinga ko baña jox jën, jox ko jaan?
12 Walla mu ñaan la nen, nga jox ko jiit?
13 Ndegam yéen ñi bon yéena mana jox seeni gone lu baax, astamaak Baay bi nekk ci kaw dina jox Xel mu Sell mi ñi ko koy ñaan!»
14 Am bés Yeesu dàq rab wu luu. Naka la rab wa génn, luu ba daldi wax, ba mbooloo may yéemu.
15 Waaye am ca mbooloo ma ay nit, ñu doon wax naan: «Ci kàttanu Beelsebul, buuru rab yi, lay dàqe rab yi.»
16 Am ñeneen ñu fexe koo fiir, ba laaj ko kéemaan gu jóge ci asamaan tey firndeel yónnentam.
17 Waaye Yeesu xam seen xalaat ne leen: «Réew mu xeex boppam tas, kër gu xeex boppam gent.
18 Te it bu Seytaane xeexee boppam, naka la nguuram di mana yàgge? Damay wax loolu, ndaxte nee ngeen, damay dàq rab jaarale ko ci kàttanu Beelsebul.
19 Te it bu fekkee ne man damay dàq ay rab ci kàttanu Beelsebul, seeni taalibe nag ci gan kàttan lañu leen di dàqe? Kon ñoo leen di àtte.
20 Waaye bu fekkee ne ci baaraamu Yàlla laay dàqe rab, kon nguuru Yàlla agsi na ba ci yéen.
21 «Su nit ku bare doole gànnaayoo, di wottu këram, alalam dina raw.
22 Waaye bu ku ko ëpp doole ñëwee, daan ko, dafay nangu gànnaay ya mu yaakaaroon, ba noppi séddale alal ja.
23 Ku farul ak man, yaa ngi may xeex, ku dajalewul ak man, yaa ngi tasaare.
24 «Boo xamee ne rab, wa jàppoon nit, génn na ci moom, day wër ay bérab yu wow, di wut fu mu noppaloo, waaye du ko gis. Noonu da naan: “Naa dellu ca sama kër, ga ma jóge.”
25 Bu ñëwee nag, mu fekk këram, ñu bale ko, defar ko ba lépp jekk.
26 Bu ko gisee nag, mu dem wooyi yeneen juróom ñaari rab yu ko gëna soxor. Ñu dugg, sanc fa; ba tax mujug nit kooku mooy yées njàlbéenam.»
27 Bi Yeesu di wax loolu, jenn jigéen yékkati baatam ca biir mbooloo ma ne: «Céy jigéen ji la ëmb te nàmpal la moo barkeel!»
28 Waaye Yeesu ne ko: «Neel kay, ki barkeel mooy kiy déglu kàddug Yàlla te di ko topp.»
29 Naka la mbooloo may gëna takku, Yeesu ne: «Niti jamono jii dañoo bon. Ñu ngi laaj firnde, waaye duñu jot genn firnde gu dul firndeg Yunus.
30 Ndaxte ni Yunus nekke woon firnde ci waa dëkku Niniw, noonu la Doomu nit kiy nekke firnde ci niti jamono jii.
31 Keroog bés pénc buur bu jigéen, ba dëkkoon ca sudd, dina jógandoo ak niti jamono jii, yey leen; ndaxte dafa jóge ca catul àddina, ngir déglu xam-xamu Suleymaan, te ku sut Suleymaan a ngi fi.
32 Te it ca bés pénc, waa dëkku Niniw dinañu jógandoo ak niti jamono jii, yey leen, ndaxte bi leen Yunus waaree, tuub nañu seeni bàkkaar, te ku sut Yunus a ngi fii.
33 «Kenn du taal làmp, ba noppi di ko dugal cig kàmb, walla di ci këpp leget. Daf koy wékk, ngir mu leeral ñiy dugg.
34 Bët mooy làmpu yaram. Bu sa bët wéree, kon sa yaram wépp leer. Waaye bu sa bët woppee, kon sa yaram wépp lëndëm.
35 Moytul ndax leer gi nekk ci yaw du lëndëm.
36 Kon bu sa yaram wépp nekkee ci leer te amul genn wet gu laal ci lëndëm, dina leer nàññ, mel ni leeraayu làmp ne ràyy ci sa kaw.»
37 Bi Yeesu waxee ba noppi, benn Farisen wax ko, mu ñëw lekke këram. Yeesu dugg ca kër ga, toog ca lekkukaay ba.
38 Farisen bi nag daldi jaaxle, bi mu gisee ne Yeesu raxasuwul, laata muy lekk.
39 Noonu Boroom bi ne ko: «Waaw, yéen Farisen yi, yéena ngi setal bitib kaas bi ak ndab li, waaye ci biir dangeena fees ak càcc ak mbon!
40 Yéena ñàkk xel! Xanaa du ki defar biti moo defar biir itam?
41 Sarxeleen li nekk ci biir te seen lépp dina sell.
42 Yéen Farisen yi dingeen torox! Ndaxte yéena ngi sàkk asaka ci naana ak ru ak léjum bu nekk, waaye sàggane ngeen njubte ak mbëggeel ci Yàlla. Loolu ngeen wara def, waxuma nag ngeen sàggane la ca des.
43 Yéen Farisen yi, dingeen torox! Ndaxte ca jàngu ya, toogu ya féete kanam ngeen di taamu te bëgg ñépp di leen nuyoo ñaari loxo ca pénc ma.
LUUG 11 in Téereb Injiil

Luug 11:4-43 in Kàddug Yàlla gi

4 Baal nu sunuy bàkkaar, ni nuy baale nun itam, mboolem ñi nu tooñ, te bu nu dugal ci nattu.»
5 Yeesu teg ca ne leen: «Ana kan ci yeen moo seeti ab xaritam xaaju guddi, ne ko: “Xarit, lebal ma ci ñetti mburu.
6 Sama xarit bu nekk ciw yoon moo dikk sama kër, te awma dara lu ma ko taajal,”
7 te xarit ba àddoo ca biir néegam, ne ko: “Bu ma sonal, tëj naa ba tëdd, maak samay doom; manumaa jóg, di la jox dara”?
8 Maa leen ko wax, su jógul jox ko la mu laaj ndax ug xaritoo it, la ko kee amul kersay yee ngir sàkku ndimbal mooy tax mu jóg, jox ko mboolem lu mu soxla.
9 Moo tax ma ne leen, ñaanleen, ñu may leen; seetleen, ndax ngeen gis; fëggleen, ñu ubbil leen.
10 Ndaxte képp ku ñaan, dinga am; ku seet, dinga gis; ku fëgg it, dees na la ubbil.
11 Ana kan ci yeen mooy baay bu doomam ñaan aw jën, mu jox ko jaan?
12 Mbaa mu ñaan ko nen, mu jox ko aw jiit?
13 Ndegam yeen ñi bon yeena mana may seeni gone lu baax nag, astamaak Baay ba fa asamaan. Moo leen ko dàq fuuf, nde mooy may Noo gu Sell gi, ñi ko ko ñaan!»
14 Yeesu moo doon dàq aw rab wu duggoon nit ba mu luu. Ba rab wa génnee, luu ba wax, mbooloo ma waaru.
15 Teewul ñenn ca ñoom ne: «Ci Beelsebul, buuru rab yi lay dàqe ay rab.»
16 Ñeneen nag di ko fiir, di sàkku ci moom firnde ju bawoo asamaan.
17 Yeesu itam ràññee seen xalaat, ne leen: Gépp nguur guy xàjjalikoo ci biiram, day tas, yii kër màbb ca kaw yee.
18 Seytaane itam, su xàjjalikoo ci biiram, ana nu nguuram di yàgge, gannaaw yeena ne Beelsebul laay dàqe ay rab?
19 Te it ndegam man Beelsebul laay dàqe rab yi, seen ñoñ nag ñoom, kan lañuy dàqe ay rab? Kon kay seen ñoñ a leen tiiñal.
20 Waaye su dee loxol Yàlla laay dàqe rab yi nag, kon nguurug Yàlla agsi na ba ci yeen.
21 «Su ponkal gànnaayoo ba diis, wattu këram, alalam dina raw.
22 Waaye bu ko ku ko man songee, ba daan ko, day nangu mboolem ngànnaay lu mu yaakaaroon, ba noppi séddale alalam.
23 Ku farul ak man nag, man ngay xeex, te ku àndul ak man di dajale, yaa ngi tasaare.
24 «Aw rab wu bon, bu jàppee nit ba génn ko, day wër bérab yu fendi, di wut fu mu nopploo, te du ko gis. Su ko defee mu ne: “Naa dellu ca sama kër, ga ma jóge.”
25 Bu dikkee fekk kër gi buube, defare ba jekk,
26 day dem indi yeneen juróom ñaari rab yu ko yées, ñu bokk sancsi. Su ko defee ni nit kiy mujje mooy yées na mu jëkke.»
27 Naka la Yeesu di wax loolu, jenn jigéen ca mbooloo ma àddu ca kaw, ne ko: «Ndokklee ki la ëmb ci biiram, nàmpal la ci weenam!»
28 Moom nag mu ne ko: «Xanaa kay, ndokklee ñiy déglu kàddug Yàlla te di ko jëfe.»
29 Naka la mbooloo may gëna takku, Yeesu ne: «Niti tey jii, nit ñu bon lañu. Firnde lañuy wut, waaye deesu leen jox jenn firnde ju moy firndey Yunus.
30 Ndax na Yunus nekke woon firnde ca waa Niniw, noonu la Doomu nit ki nekke firnde ci niti tey jii.
31 Keroog àtte ba, Lingeeru bëj-saalum dina jóg, janook niti tey jii, tiiñal leen; ndax moo bàyyikoo woon ca catal àddina, ngir déglusi xam-xamu Suleymaan, te tey jii, ku sut Suleymaan a ngi fi.
32 Waa réewum Niniw it keroog àtte ba dinañu taxaw, layook niti tey jii, tiiñal leen ndax ñoo tuube woon ca waareb Yunus, te tey jii, ku sut Yunus a ngi fi.
33 «Deesul taal ab làmp, di ko dugal fu làqu, mbaa ci suufu leget. Dees koy aj kay, ba kuy duggsi gis muy leer.
34 Bët mooy làmpu yaram. Bu sa bët wéree, sa yaram wépp a ciy leerloo, waaye bu sa bët bonee, sa yaram wépp a ngi ci lëndëm.
35 Kon seetal ndax leer gi nga foog ne mu ngi ci yaw du ag lëndëm.
36 Bu sa yaram wépp dee leerlu nag te lenn nekku ci cig lëndëm, su boobaa la sa yaram di mana leerlu ba ne ràññ, mel ni bu la ab làmp niitee, ne ràññ ci sa kaw.»
37 Ba Yeesu waxee ba noppi, ab Farisen da koo woo këram, ngir bokk ak moom lekk. Mu nangu, dem ba duggsi, daldi toog ca lekkukaay ba.
38 Farisen bi nag jaaxle, ndax la Yeesu setluwul bala moo waaja lekk.
39 Sang bi ne ko: «Yeen Farisen yi, bitib kaas bi ak ndab li daal ngeen di raxas, te fekk leen feese jikkoy jagoo lu lewul, akug mbon ci biir!
40 Yeena ñàkk xel! Xanaa du ki sàkk biti moo sàkk biir itam?
41 Li ci biir kay ngeen di sarxe! Su boobaa seen lépp ay set.
42 Waaye wóoy ngalla yeen Farisen yi! Xobi naana ak yeneen safal yu mel ni ru ak wépp xeetu lujum, yeena ngi ciy génne cérub fukkeel, ngir asaka, njubte ak cofeelu Yàlla nag, ngeen sàggane. Lii de war na leen, waaye lee it, waruleen koo sàggane.
43 Wóoy ngalla yeen Farisen yi! Yeenay sàkku péete yu kaname ca jàngu ya, ak nuyoob gëddaal ca pénc ma.
Luug 11 in Kàddug Yàlla gi