Text copied!
Bibles in Wolof

LUUG 11:37-52 in Wolof

Help us?

LUUG 11:37-52 in Téereb Injiil

37 Bi Yeesu waxee ba noppi, benn Farisen wax ko, mu ñëw lekke këram. Yeesu dugg ca kër ga, toog ca lekkukaay ba.
38 Farisen bi nag daldi jaaxle, bi mu gisee ne Yeesu raxasuwul, laata muy lekk.
39 Noonu Boroom bi ne ko: «Waaw, yéen Farisen yi, yéena ngi setal bitib kaas bi ak ndab li, waaye ci biir dangeena fees ak càcc ak mbon!
40 Yéena ñàkk xel! Xanaa du ki defar biti moo defar biir itam?
41 Sarxeleen li nekk ci biir te seen lépp dina sell.
42 Yéen Farisen yi dingeen torox! Ndaxte yéena ngi sàkk asaka ci naana ak ru ak léjum bu nekk, waaye sàggane ngeen njubte ak mbëggeel ci Yàlla. Loolu ngeen wara def, waxuma nag ngeen sàggane la ca des.
43 Yéen Farisen yi, dingeen torox! Ndaxte ca jàngu ya, toogu ya féete kanam ngeen di taamu te bëgg ñépp di leen nuyoo ñaari loxo ca pénc ma.
44 Dingeen torox, ndaxte dangeena mel ni ay bàmmeel yu raaf, ba nit ñi di ci dox te teyuñu ko.»
45 Kenn ci xutbakat yi ne ca tonn ne: «Kilifa gi, boo waxee loolu, yaa ngi nuy xas, nun itam.»
46 Noonu Yeesu neeti leen: «Yéen itam xutbakat yi, dingeen torox! Ndaxte dangeen di sëf nit ñi say yu diis, waaye dungeen nangoo laal sëf bi sax ak seen cati baaraam.
47 Dingeen torox, ndaxte yéena ngi tabax xabruy yonent, yi seeni maam reyoon.
48 Dangeen di seede noonu ne ànd ngeen ak li seen maam defoon, ndaxte ñoo rey yonent yi, yéen ngeen tabax xabru yi.
49 Looloo tax Yàlla mi xam lépp ne: “Dinaa leen yónnee ay yonent ak ay ndaw. Ñenn ñi dinañu leen fitnaal, rey leen.”
50 Kon nag Yàlla dina mbugal niti jamono jii ndax dereti yonent yi ñu tuur, ba àddina sosoo ak léegi,
51 la dale ca Abel ba ci Sakari, moom mi ñu rey ci diggante sarxalukaay bi ak bérab bu sell bi. Waaw, maa ngi leen koy wax, Yàlla dina mbugal niti jamono jii ndax loolu.
52 Yéen xutbakat yi, dingeen torox, ndaxte yéena yóbbu caabiy xam-xam; dugguleen ci, te ku ci bëgga dugg, ngeen tere ko ko.»
LUUG 11 in Téereb Injiil

Luug 11:37-52 in Kàddug Yàlla gi

37 Ba Yeesu waxee ba noppi, ab Farisen da koo woo këram, ngir bokk ak moom lekk. Mu nangu, dem ba duggsi, daldi toog ca lekkukaay ba.
38 Farisen bi nag jaaxle, ndax la Yeesu setluwul bala moo waaja lekk.
39 Sang bi ne ko: «Yeen Farisen yi, bitib kaas bi ak ndab li daal ngeen di raxas, te fekk leen feese jikkoy jagoo lu lewul, akug mbon ci biir!
40 Yeena ñàkk xel! Xanaa du ki sàkk biti moo sàkk biir itam?
41 Li ci biir kay ngeen di sarxe! Su boobaa seen lépp ay set.
42 Waaye wóoy ngalla yeen Farisen yi! Xobi naana ak yeneen safal yu mel ni ru ak wépp xeetu lujum, yeena ngi ciy génne cérub fukkeel, ngir asaka, njubte ak cofeelu Yàlla nag, ngeen sàggane. Lii de war na leen, waaye lee it, waruleen koo sàggane.
43 Wóoy ngalla yeen Farisen yi! Yeenay sàkku péete yu kaname ca jàngu ya, ak nuyoob gëddaal ca pénc ma.
44 Wóoy ngalla yeen, yeena ngi mel ni ay bàmmeel yu amul xàmmikaay, nit ñiy dox ca kaw te xamuñu ko.»
45 Kenn ci xamkati yoon yi nag àddu ne: «Sëriñ bi, loolu nga wax de, nun itam, xasaale nga nu ci.»
46 Yeesu itam ne: «Yeen xamkati yoon yi itam, wóoy ngalla yeen, yeen ñi sëf nit ñi sëf yu ñu àttanul, te yeen ci seen bopp, seen benn baaraam sax du ci laal.
47 Wóoy ngalla yeen, yeenay tabax bàmmeeli yonent yi, te seeni maam reyoon leen.
48 Kon yeena seedee noonu ne seen jëfi maam ya, ànd ngeen ci, ndax ñoom ñoo leen rey, yeen ngeen tabax seeni bàmmeel.
49 Looloo tax itam kàddug Yàlla giy xel, biral ne: “Maay yebal fa ñoom ay yonent aki ndaw, ñii ñu bóom, ñee, ñu bundxatal.”
50 Su ko defee yoon topp niti tey jii, deretu mboolem yonent yi tuuru, dale ko ca cosaanu àddina.
51 La dale ca deretu Abel ba ca deretu Sàkkaryaa, ma ñu rey ca diggante sarxalukaay ba ak bérab bu sell ba, maa leen ko wax déy, dees na ko topp niti tey jii.
52 Ngalla yeen xamkati yoon yi, yeena sànk caabiy xam-xam; yeen dugguleen, ñiy duggsi, ngeen tere leena dugg.»
Luug 11 in Kàddug Yàlla gi