27 Naka la Yeesu di wax loolu, jenn jigéen ca mbooloo ma àddu ca kaw, ne ko: «Ndokklee ki la ëmb ci biiram, nàmpal la ci weenam!»
28 Moom nag mu ne ko: «Xanaa kay, ndokklee ñiy déglu kàddug Yàlla te di ko jëfe.»
29 Naka la mbooloo may gëna takku, Yeesu ne: «Niti tey jii, nit ñu bon lañu. Firnde lañuy wut, waaye deesu leen jox jenn firnde ju moy firndey Yunus.
30 Ndax na Yunus nekke woon firnde ca waa Niniw, noonu la Doomu nit ki nekke firnde ci niti tey jii.
31 Keroog àtte ba, Lingeeru bëj-saalum dina jóg, janook niti tey jii, tiiñal leen; ndax moo bàyyikoo woon ca catal àddina, ngir déglusi xam-xamu Suleymaan, te tey jii, ku sut Suleymaan a ngi fi.
32 Waa réewum Niniw it keroog àtte ba dinañu taxaw, layook niti tey jii, tiiñal leen ndax ñoo tuube woon ca waareb Yunus, te tey jii, ku sut Yunus a ngi fi.
33 «Deesul taal ab làmp, di ko dugal fu làqu, mbaa ci suufu leget. Dees koy aj kay, ba kuy duggsi gis muy leer.
34 Bët mooy làmpu yaram. Bu sa bët wéree, sa yaram wépp a ciy leerloo, waaye bu sa bët bonee, sa yaram wépp a ngi ci lëndëm.
35 Kon seetal ndax leer gi nga foog ne mu ngi ci yaw du ag lëndëm.
36 Bu sa yaram wépp dee leerlu nag te lenn nekku ci cig lëndëm, su boobaa la sa yaram di mana leerlu ba ne ràññ, mel ni bu la ab làmp niitee, ne ràññ ci sa kaw.»
37 Ba Yeesu waxee ba noppi, ab Farisen da koo woo këram, ngir bokk ak moom lekk. Mu nangu, dem ba duggsi, daldi toog ca lekkukaay ba.
38 Farisen bi nag jaaxle, ndax la Yeesu setluwul bala moo waaja lekk.
39 Sang bi ne ko: «Yeen Farisen yi, bitib kaas bi ak ndab li daal ngeen di raxas, te fekk leen feese jikkoy jagoo lu lewul, akug mbon ci biir!
40 Yeena ñàkk xel! Xanaa du ki sàkk biti moo sàkk biir itam?
41 Li ci biir kay ngeen di sarxe! Su boobaa seen lépp ay set.
42 Waaye wóoy ngalla yeen Farisen yi! Xobi naana ak yeneen safal yu mel ni ru ak wépp xeetu lujum, yeena ngi ciy génne cérub fukkeel, ngir asaka, njubte ak cofeelu Yàlla nag, ngeen sàggane. Lii de war na leen, waaye lee it, waruleen koo sàggane.
43 Wóoy ngalla yeen Farisen yi! Yeenay sàkku péete yu kaname ca jàngu ya, ak nuyoob gëddaal ca pénc ma.
44 Wóoy ngalla yeen, yeena ngi mel ni ay bàmmeel yu amul xàmmikaay, nit ñiy dox ca kaw te xamuñu ko.»
45 Kenn ci xamkati yoon yi nag àddu ne: «Sëriñ bi, loolu nga wax de, nun itam, xasaale nga nu ci.»
46 Yeesu itam ne: «Yeen xamkati yoon yi itam, wóoy ngalla yeen, yeen ñi sëf nit ñi sëf yu ñu àttanul, te yeen ci seen bopp, seen benn baaraam sax du ci laal.
47 Wóoy ngalla yeen, yeenay tabax bàmmeeli yonent yi, te seeni maam reyoon leen.
48 Kon yeena seedee noonu ne seen jëfi maam ya, ànd ngeen ci, ndax ñoom ñoo leen rey, yeen ngeen tabax seeni bàmmeel.
49 Looloo tax itam kàddug Yàlla giy xel, biral ne: “Maay yebal fa ñoom ay yonent aki ndaw, ñii ñu bóom, ñee, ñu bundxatal.”
50 Su ko defee yoon topp niti tey jii, deretu mboolem yonent yi tuuru, dale ko ca cosaanu àddina.
51 La dale ca deretu Abel ba ca deretu Sàkkaryaa, ma ñu rey ca diggante sarxalukaay ba ak bérab bu sell ba, maa leen ko wax déy, dees na ko topp niti tey jii.
52 Ngalla yeen xamkati yoon yi, yeena sànk caabiy xam-xam; yeen dugguleen, ñiy duggsi, ngeen tere leena dugg.»