Text copied!
Bibles in Wolof

LUUG 11:18-37 in Wolof

Help us?

LUUG 11:18-37 in Téereb Injiil

18 Te it bu Seytaane xeexee boppam, naka la nguuram di mana yàgge? Damay wax loolu, ndaxte nee ngeen, damay dàq rab jaarale ko ci kàttanu Beelsebul.
19 Te it bu fekkee ne man damay dàq ay rab ci kàttanu Beelsebul, seeni taalibe nag ci gan kàttan lañu leen di dàqe? Kon ñoo leen di àtte.
20 Waaye bu fekkee ne ci baaraamu Yàlla laay dàqe rab, kon nguuru Yàlla agsi na ba ci yéen.
21 «Su nit ku bare doole gànnaayoo, di wottu këram, alalam dina raw.
22 Waaye bu ku ko ëpp doole ñëwee, daan ko, dafay nangu gànnaay ya mu yaakaaroon, ba noppi séddale alal ja.
23 Ku farul ak man, yaa ngi may xeex, ku dajalewul ak man, yaa ngi tasaare.
24 «Boo xamee ne rab, wa jàppoon nit, génn na ci moom, day wër ay bérab yu wow, di wut fu mu noppaloo, waaye du ko gis. Noonu da naan: “Naa dellu ca sama kër, ga ma jóge.”
25 Bu ñëwee nag, mu fekk këram, ñu bale ko, defar ko ba lépp jekk.
26 Bu ko gisee nag, mu dem wooyi yeneen juróom ñaari rab yu ko gëna soxor. Ñu dugg, sanc fa; ba tax mujug nit kooku mooy yées njàlbéenam.»
27 Bi Yeesu di wax loolu, jenn jigéen yékkati baatam ca biir mbooloo ma ne: «Céy jigéen ji la ëmb te nàmpal la moo barkeel!»
28 Waaye Yeesu ne ko: «Neel kay, ki barkeel mooy kiy déglu kàddug Yàlla te di ko topp.»
29 Naka la mbooloo may gëna takku, Yeesu ne: «Niti jamono jii dañoo bon. Ñu ngi laaj firnde, waaye duñu jot genn firnde gu dul firndeg Yunus.
30 Ndaxte ni Yunus nekke woon firnde ci waa dëkku Niniw, noonu la Doomu nit kiy nekke firnde ci niti jamono jii.
31 Keroog bés pénc buur bu jigéen, ba dëkkoon ca sudd, dina jógandoo ak niti jamono jii, yey leen; ndaxte dafa jóge ca catul àddina, ngir déglu xam-xamu Suleymaan, te ku sut Suleymaan a ngi fi.
32 Te it ca bés pénc, waa dëkku Niniw dinañu jógandoo ak niti jamono jii, yey leen, ndaxte bi leen Yunus waaree, tuub nañu seeni bàkkaar, te ku sut Yunus a ngi fii.
33 «Kenn du taal làmp, ba noppi di ko dugal cig kàmb, walla di ci këpp leget. Daf koy wékk, ngir mu leeral ñiy dugg.
34 Bët mooy làmpu yaram. Bu sa bët wéree, kon sa yaram wépp leer. Waaye bu sa bët woppee, kon sa yaram wépp lëndëm.
35 Moytul ndax leer gi nekk ci yaw du lëndëm.
36 Kon bu sa yaram wépp nekkee ci leer te amul genn wet gu laal ci lëndëm, dina leer nàññ, mel ni leeraayu làmp ne ràyy ci sa kaw.»
37 Bi Yeesu waxee ba noppi, benn Farisen wax ko, mu ñëw lekke këram. Yeesu dugg ca kër ga, toog ca lekkukaay ba.
LUUG 11 in Téereb Injiil

Luug 11:18-37 in Kàddug Yàlla gi

18 Seytaane itam, su xàjjalikoo ci biiram, ana nu nguuram di yàgge, gannaaw yeena ne Beelsebul laay dàqe ay rab?
19 Te it ndegam man Beelsebul laay dàqe rab yi, seen ñoñ nag ñoom, kan lañuy dàqe ay rab? Kon kay seen ñoñ a leen tiiñal.
20 Waaye su dee loxol Yàlla laay dàqe rab yi nag, kon nguurug Yàlla agsi na ba ci yeen.
21 «Su ponkal gànnaayoo ba diis, wattu këram, alalam dina raw.
22 Waaye bu ko ku ko man songee, ba daan ko, day nangu mboolem ngànnaay lu mu yaakaaroon, ba noppi séddale alalam.
23 Ku farul ak man nag, man ngay xeex, te ku àndul ak man di dajale, yaa ngi tasaare.
24 «Aw rab wu bon, bu jàppee nit ba génn ko, day wër bérab yu fendi, di wut fu mu nopploo, te du ko gis. Su ko defee mu ne: “Naa dellu ca sama kër, ga ma jóge.”
25 Bu dikkee fekk kër gi buube, defare ba jekk,
26 day dem indi yeneen juróom ñaari rab yu ko yées, ñu bokk sancsi. Su ko defee ni nit kiy mujje mooy yées na mu jëkke.»
27 Naka la Yeesu di wax loolu, jenn jigéen ca mbooloo ma àddu ca kaw, ne ko: «Ndokklee ki la ëmb ci biiram, nàmpal la ci weenam!»
28 Moom nag mu ne ko: «Xanaa kay, ndokklee ñiy déglu kàddug Yàlla te di ko jëfe.»
29 Naka la mbooloo may gëna takku, Yeesu ne: «Niti tey jii, nit ñu bon lañu. Firnde lañuy wut, waaye deesu leen jox jenn firnde ju moy firndey Yunus.
30 Ndax na Yunus nekke woon firnde ca waa Niniw, noonu la Doomu nit ki nekke firnde ci niti tey jii.
31 Keroog àtte ba, Lingeeru bëj-saalum dina jóg, janook niti tey jii, tiiñal leen; ndax moo bàyyikoo woon ca catal àddina, ngir déglusi xam-xamu Suleymaan, te tey jii, ku sut Suleymaan a ngi fi.
32 Waa réewum Niniw it keroog àtte ba dinañu taxaw, layook niti tey jii, tiiñal leen ndax ñoo tuube woon ca waareb Yunus, te tey jii, ku sut Yunus a ngi fi.
33 «Deesul taal ab làmp, di ko dugal fu làqu, mbaa ci suufu leget. Dees koy aj kay, ba kuy duggsi gis muy leer.
34 Bët mooy làmpu yaram. Bu sa bët wéree, sa yaram wépp a ciy leerloo, waaye bu sa bët bonee, sa yaram wépp a ngi ci lëndëm.
35 Kon seetal ndax leer gi nga foog ne mu ngi ci yaw du ag lëndëm.
36 Bu sa yaram wépp dee leerlu nag te lenn nekku ci cig lëndëm, su boobaa la sa yaram di mana leerlu ba ne ràññ, mel ni bu la ab làmp niitee, ne ràññ ci sa kaw.»
37 Ba Yeesu waxee ba noppi, ab Farisen da koo woo këram, ngir bokk ak moom lekk. Mu nangu, dem ba duggsi, daldi toog ca lekkukaay ba.
Luug 11 in Kàddug Yàlla gi