Text copied!
Bibles in Wolof

LUUG 10:17-26 in Wolof

Help us?

LUUG 10:17-26 in Téereb Injiil

17 Juróom ñaar fukki taalibe yi ak ñaar délsi, fees ak mbég te naan: «Boroom bi, rab yi sax déggal nañu nu ndax sa tur.»
18 Yeesu ne leen: «Maa ngi doon séen Seytaane wàcce asamaan ni sawaras melax.
19 Gis ngeen, jox naa leen sañ-sañu joggi ci jaan yi ak ci jiit yi, daan dooley bañaale bi, te dara du leen mana gaañ.
20 Moona li leen rab yi déggal, bumu tax ngeen bég, waaye bégleen ndax li ñu bind seen tur ci asamaan.»
21 Ca saa soosu Xel mu Sell mi feesal Yeesu ak mbég, mu daldi ne: «Yaw Baay, Boroom asamaan ak suuf, maa ngi lay sant ci li nga nëbb yëf yii ñi am xam-xam ak ñi am xel, te xamal leen gone yi. Waaw, Baay, ndaxte looloo la neex.»
22 Yeesu teg ca ne: «Sama Baay jébbal na ma lépp, te kenn manula xam, man Doom ji, maay kan, ku dul Baay bi; kenn manula xam it kan mooy Baay bi, ku dul man Doom ji, ak ku ma ko bëgga xamal.»
23 Gannaaw bi mu waxee loolu, Yeesu walbatiku ca taalibe ya ne leen ñoom rekk: «Ñi seeni bët di gis li ngeen di gis, am nañu mbég.
24 Ndaxte maa ngi leen koy wax, yonent yu bare ak buur yu bare bëggoon nañoo gis li ngeen di gis, waaye gisuñu ko, te dégg li ngeen di dégg, waaye dégguñu ko.»
25 Noonu benn xutbakat daldi jóg, ngir fexee fiir Yeesu ne ko: «Kilifa gi, lan laa wara def, ba am dund gu dul jeex?»
26 Yeesu ne ko: «Lu ñu bind ci yoonu Musaa? Lan nga ciy jàng?»
LUUG 10 in Téereb Injiil

Luug 10:17-26 in Kàddug Yàlla gi

17 Ba juróom ñaar Fukk ñaak ñaar demee ba délsi, mbégte lañu àndal. Ñu ne: «Sang bi, rab yi sax, danu leen di jox ndigal ci sa tur, ñu nangul nu.»
18 Yeesu ne leen: «Séen naa Seytaane mu fàqe asamaan ni ag melax.
19 Dama ne, maa leen jox sañ-sañu joggi ci kawi jaan aki jiit, joggati mboolem dooley bañaale bi, te dara du leen mana gaañ mukk.
20 Noonu leen rab yi nangule nag, buleen ko bége, bégeleen kay la seen tur binde fa asamaan.»
21 Ca waxtu woowa tembe la kemtalaayu mbégte tukkee ci Noo gu Sell gi, dugg Yeesu, mu daldi ne: «Baay, Boroom asamaan ak suuf, sant naa la, nde yaa làq lii boroom xam-xam yeek boroom xel yi, xamal ko tuut-tànk yi, nde loolu de, Baay, mooy li la soob.
22 Lépp la ma sama Baay dénk, te kenn xamul kuy Doom ji, ku dul Baay bi; kenn it xamul kuy Baay bi, ku dul Doom ji, ak képp ku ko Doom ji namma xamal.»
23 Ci kaw loolu Yeesu walbatiku ca taalibe ya, wax leen ñoomu neen, ne leen: «Ndokklee ñi seeni gët gis li ngeen gis.
24 Ndax maa leen ko wax, bare na ay yonent ak buur yu bëggoona gis li ngeen gis, te gisuñu ko, ak itam dégg li ngeen dégg, te dégguñu ko.»
25 Benn xamkatu yoonu Musaa moo jekki woon jóg, di fexee fiir Yeesu. Mu ne ko: «Sëriñ bi, ana lu may def, ba texe ba fàww?»
26 Yeesu ne ko: «Yoonu Musaa, ana lees ci bind? Loo ci jànge?»
Luug 10 in Kàddug Yàlla gi