Text copied!
Bibles in Wolof

LUUG 10:12-16 in Wolof

Help us?

LUUG 10:12-16 in Téereb Injiil

12 Maa ngi leen koy wax, bu bés baa, waa Sodom ñooy tane dëkk boobu.
13 «Dingeen torox, yéen waa Korasin ak waa Betsayda, ndaxte kéemaan yi ma def ci yéen, bu ñu leen defoon ci dëkku Tir walla ci dëkku Sidon, kon tuub nañu seeni bàkkaar bu yàgg, xëppoo dóom, sol saaku.
14 Moona ca bés pénc ba, Tir ak Sidon ñoo leen di tane.
15 Te yaw dëkku Kapernawum, ndax dees na la yékkati bu kawe? Déedéet, dees na la daane bu suufe.
16 «Ku leen déglu, déglu na ma; ku leen bañ, bañ na ma. Te ku ma bañ, bañ na ki ma yónni.»
LUUG 10 in Téereb Injiil

Luug 10:12-16 in Kàddug Yàlla gi

12 Maa leen ko wax, bu bés baa, boobu dëkk, Sodom a koy gënu demin.
13 «Wóoy ngalla yeen waa Korasin, yeen waa Beccayda it, wóoy ngalla yeen, nde kéemaan yi sottee fi seen biir, su doon fa waa Tir mbaa fa waa Sidon la sottee, kon bu yàgg lañu doon sol ay saaku, xëppoob dóom, ngir tuub.
14 Moo tax it, kera àtte ba, waa Tir ak Sidon a leen di gënu demin.
15 Yeen waa Kapernawum nag, dees na leen yékkati ba asamaan a? Xanaa ba fa njaniiw kay ngeen di wàcci.
16 «Ku leen déggal nag, man nga déggal; ku leen gàntal, man nga gàntal. Te ku ma gàntal, gàntal nga ki ma yebal.»
Luug 10 in Kàddug Yàlla gi