Text copied!
Bibles in Wolof

Kàdduy Waare 8:8-11 in Wolof

Help us?

Kàdduy Waare 8:8-11 in Kàddug Yàlla gi

8 Kenn moomul bakkanam, ba man koo dese, kenn amul sañ-sañ ci bésub deeyam, kenn muccul ci boobu xare, te mbon du ca wallu boroom.
9 Loolu lépp gis naa ko, ba may xalaat ci jépp jëfi kaw suuf; fi nit di yilife nit, muy loraange.
10 Ma gis itam ñu bon ñu ñu rob, ñu daan yaale kër Yàlla ga, ñu di leen gërëme tey seeni jëf ca dëkk ba. Loolu it, cóolóoli neen.
11 Jëf ñaaw na, mbugal ma yeex, ba tax doom aadama sóobu ci mbon.
Kàdduy Waare 8 in Kàddug Yàlla gi