Text copied!
Bibles in Wolof

Kàdduy Waare 8:3-8 in Wolof

Help us?

Kàdduy Waare 8:3-8 in Kàddug Yàlla gi

3 Bul gaawa won buur gannaaw; bul saxoo lu buur buggul; Buur, lu ko neex lay def.
4 Kàddug buur kilifteef la. Ana ku ko naan: «Looy def nii?»
5 Ku dégg ndigal doo am lu la soof. Ku xelu, xam lu jot, xam doxalin.
6 Mbir mu mu doon kat ak jotam ak doxalinam, waaye nit am na tiis wu ko diis.
7 Kenn xamul luy xew ëllëg, kenn manula wax luy xew ëllëg.
8 Kenn moomul bakkanam, ba man koo dese, kenn amul sañ-sañ ci bésub deeyam, kenn muccul ci boobu xare, te mbon du ca wallu boroom.
Kàdduy Waare 8 in Kàddug Yàlla gi