13 Ku bon, du am lu baax, fanam du màgg ni ker, ndax wormaalul Yàlla.
14 Waaye cóolóoli neen a ngi am fi kaw suuf: Ku jub jot yoolu ku bon, ku bon jot yoolu ku jub. Ma ne loolu it cóolóoli neen la.
15 Man daal damay digle bànneex, ndax nit amul lu gën fi kaw suuf di lekk ak a naan ak a bànneexu, muñe ko doñ-doñam, fan yi ko Yàlla may fi kaw suuf.
16 Ma walbatiku xalaat, di jéema xam fu xel rafete, di xoolaat li nit jàppoo fi kaw suuf, ba guddeek bëccëg, gëmmul bët.
17 Ma daldi gis li Yàlla def lépp. Nit kay xel ma du daj liy xew fi kaw suuf. Day seet ba sonn, du ko daj. Boroom xel bu wax ne xam na ko it, du ko daj.