Text copied!
Bibles in Wolof

Kàdduy Waare 8:13-16 in Wolof

Help us?

Kàdduy Waare 8:13-16 in Kàddug Yàlla gi

13 Ku bon, du am lu baax, fanam du màgg ni ker, ndax wormaalul Yàlla.
14 Waaye cóolóoli neen a ngi am fi kaw suuf: Ku jub jot yoolu ku bon, ku bon jot yoolu ku jub. Ma ne loolu it cóolóoli neen la.
15 Man daal damay digle bànneex, ndax nit amul lu gën fi kaw suuf di lekk ak a naan ak a bànneexu, muñe ko doñ-doñam, fan yi ko Yàlla may fi kaw suuf.
16 Ma walbatiku xalaat, di jéema xam fu xel rafete, di xoolaat li nit jàppoo fi kaw suuf, ba guddeek bëccëg, gëmmul bët.
Kàdduy Waare 8 in Kàddug Yàlla gi