4 Lumb wa ñëw na moos ci neen, bàddoo lëndëm, turam sàngoo lëndëm.
5 Gisul jant, xamu ko, waaye noflaay moo ko ëpple mag ma,
6 bu dundoon junniy junniy at sax te amul jàmm. Xanaa du benn bérab la ñépp jëm?
7 Nit ak doñ-doñam jépp, biiram, te taxul mu doylu.
8 Ana lu boroom xel ëpplee ku dofe? Nga ñàkk, xam doxalin, lu mu lay jariñ?