3 Ku giir téeméeri doom, dund ati at, ak lu at ya bare bare, su bégewul teraanga ja mu am te amul njégu bàmmeelam sax, kooku lumb wu tuuroo ko tane.
4 Lumb wa ñëw na moos ci neen, bàddoo lëndëm, turam sàngoo lëndëm.
5 Gisul jant, xamu ko, waaye noflaay moo ko ëpple mag ma,
6 bu dundoon junniy junniy at sax te amul jàmm. Xanaa du benn bérab la ñépp jëm?