6 Mu jot nga sàkku, mu jot nga ñàkk; mu jot nga sàmm, mu jot nga xalab.
7 Mu jot nga xar, mu jot nga gaar; mu jot nga selaw, mu jot nga wax.
8 Mu jot nga sopp, mu jot nga jéppi; mu jot nga xare, mu jot nga jàmmoo.
9 Ana lu liggéeykat biy jariñoo ciw ñaqam?
10 Gis naa ne sas la bu Yàlla sase, nu war koo sasoo.
11 Lépp la Yàlla def, ba bu jotee rafet. Moo may nit muy njort ëllëg, te taxul mu mana ràññee jëf ji Yàlla jëf, njàlbéen ba muj ga.
12 Ma gis ne nit amul lu gën bànneex ak jàmmi bakkan cig dundam,
13 te nitoo nit, su dee lekk ak a naan, di ñaq, jariñoo, loolu mayu Yàllaa.
14 Ma xam ne lu Yàlla def, loola day sax ba fàww. Deesu ci yokk, mbaa di wàññi dara; Yàllaa ko def, ngir nit di ko wormaal.
15 Lu ay tey, ayoon na, lu ay ëllëg it ayoon na. Yàllaay namma indi la woon.
16 Ma dellu gis fi kaw suuf ne, fu yoon moom, fa la njubadi ne, fa njub moom it, fa la njubadi ne.
17 Saam xel ne ma, ku jub ak ku bon la Yàlla di boole àtte, ngir mbir mu ne ak jëf ju ne ak bésam.
18 Saam xel neeti ma, nun doom aadama, Yàllaa nuy nattu, nu gis ne ay mala doŋŋ lanu.