20 Ñoom ñépp a bokk jëm benn bérab ba, bokk jóge pëndub suuf, bokk dellu suuf.
21 Ana ku mu wóor ne bakkanu nit day yéeg asamaan, bakkanu mala tàbbi suuf?
22 Ma gis nag ne nit amul lu gën di bànneexoo ñaqam, loolooy wàllam. Ana ku koy xamal gannaawam?