19 Dogalu doom aadama ji ak dogalu mala mi, benn dogal bee; ni kii di deeye la kee di deeye, genn noo gee, nu bokk ko. Lu nit ëpplee mala neen na, ñoom ñépp, cóolóoli neen.
20 Ñoom ñépp a bokk jëm benn bérab ba, bokk jóge pëndub suuf, bokk dellu suuf.