7 Ma jëndi jaam, góor ak jigéen; ñu ami doom ci kër gi. Ma am jur gu ne gàññ, gu gudd ak gu gàtt, ba ëpple ku ma jiitu ci Yerusalem.
8 Ma dajale sama xaalis ak sama wurus, moom alali buur yeek diiwaan yi ma yilif, tabb samay woykat, góor ak jigéen, boole ci bànneex bi ci jabari jabar.
9 Ma am doole, yokku, ba sut ku ma jiitu ci Yerusalem, te teewul may jëfe xel.
10 Lépp lu saay gët xemmemaa, xañuma ko sama xol. Bañaluma sama bopp benn bànneex, xanaa di bége lu ma liggéey, yooloo ko la ma liggéey.
11 Ma xoolaatal sama bopp lépp lu ma sottal, doñ-doñi ko, ba sottal, ndeke lépp, cóolóoli neen ak napp um ngelaw. Nit gisul njariñ ci kaw suuf.
12 Ma geesu xoolaat xel mu rafet, xool ag nitoodi akug ndof. Ana ku may wuutuji ci nguur gi, lu muy def lu moy lu ñu daan def?
13 Ma gis ne ni leer ëppe lëndëm njariñ, ni la xel mu rafet ëppe ndof njariñ.