Text copied!
Bibles in Wolof

Kàdduy Waare 2:5-9 in Wolof

Help us?

Kàdduy Waare 2:5-9 in Kàddug Yàlla gi

5 Ma sàkki tóokër aki tool, jëmbat ca garab yuy meññ lu ne,
6 sàkklu samay déeg, di ko suuxate, garab ya naat.
7 Ma jëndi jaam, góor ak jigéen; ñu ami doom ci kër gi. Ma am jur gu ne gàññ, gu gudd ak gu gàtt, ba ëpple ku ma jiitu ci Yerusalem.
8 Ma dajale sama xaalis ak sama wurus, moom alali buur yeek diiwaan yi ma yilif, tabb samay woykat, góor ak jigéen, boole ci bànneex bi ci jabari jabar.
9 Ma am doole, yokku, ba sut ku ma jiitu ci Yerusalem, te teewul may jëfe xel.
Kàdduy Waare 2 in Kàddug Yàlla gi