Text copied!
Bibles in Wolof

Kàdduy Waare 2:19-24 in Wolof

Help us?

Kàdduy Waare 2:19-24 in Kàddug Yàlla gi

19 xameesul ku xeloom ku nitoodi lay doon, mooy moom lu ma doon doñ-doñi, te sama manoore manaloon ma ko fi kaw dun bi. Loolu it, cóolóoli neen.
20 Sama xol a jeex ci doñ-doñ ju ma doñ-doñi fi kaw dun bi.
21 Nit a ngi doñ-doñee xel, xam-xam ak manoore, te ku doñ-doñiwuloon lay wacce alalam. Loolu it, cóolóoli neen ak naqar wu réy.
22 Ma ne ana lu nit di jariñoo ci doñ-doñ ak xalaatu xol, yi muy doñ-doñaale fi kaw dun bi?
23 Ndegam day yendoo tiis ak naqaru tës-tës, ba far fanaanoo xel mu dalul. Loolu it, cóolóoli neen.
24 Kon nit amul lu gën di lekk ak a naan, di bànneexoo ñaqam. Ma gis ne loolu it Yàllaa koy maye.
Kàdduy Waare 2 in Kàddug Yàlla gi