Text copied!
Bibles in Wolof

Kàdduy Waare 2:13-17 in Wolof

Help us?

Kàdduy Waare 2:13-17 in Kàddug Yàlla gi

13 Ma gis ne ni leer ëppe lëndëm njariñ, ni la xel mu rafet ëppe ndof njariñ.
14 Ku xelu day xool fa muy jaare, dof biy tëñëx-tëñëxi cig lëndëm. Ma ne moona ñoom ñaar a bokk dogal moos.
15 Ma xalaataat, saam xel ne ma, dof bi noonu, man it noonu; ana lu may xeloo xelu doye? Saam xel ne ma loolu it, cóolóoli neen.
16 Ku xelook ku dof, du yàgg ñu fàtte la; ay bés yu néew, ñu fàtte lépp. Acam! Dof, dee; rafet xel, dee.
17 Ma far bañ àddina. Ndaw naqar ci jëfi kaw suuf, te lépp di cóolóol ak napp um ngelaw!
Kàdduy Waare 2 in Kàddug Yàlla gi