13 Ma gis ne ni leer ëppe lëndëm njariñ, ni la xel mu rafet ëppe ndof njariñ.
14 Ku xelu day xool fa muy jaare, dof biy tëñëx-tëñëxi cig lëndëm. Ma ne moona ñoom ñaar a bokk dogal moos.
15 Ma xalaataat, saam xel ne ma, dof bi noonu, man it noonu; ana lu may xeloo xelu doye? Saam xel ne ma loolu it, cóolóoli neen.