Text copied!
Bibles in Wolof

Kàdduy Waare 2:12-16 in Wolof

Help us?

Kàdduy Waare 2:12-16 in Kàddug Yàlla gi

12 Ma geesu xoolaat xel mu rafet, xool ag nitoodi akug ndof. Ana ku may wuutuji ci nguur gi, lu muy def lu moy lu ñu daan def?
13 Ma gis ne ni leer ëppe lëndëm njariñ, ni la xel mu rafet ëppe ndof njariñ.
14 Ku xelu day xool fa muy jaare, dof biy tëñëx-tëñëxi cig lëndëm. Ma ne moona ñoom ñaar a bokk dogal moos.
15 Ma xalaataat, saam xel ne ma, dof bi noonu, man it noonu; ana lu may xeloo xelu doye? Saam xel ne ma loolu it, cóolóoli neen.
16 Ku xelook ku dof, du yàgg ñu fàtte la; ay bés yu néew, ñu fàtte lépp. Acam! Dof, dee; rafet xel, dee.
Kàdduy Waare 2 in Kàddug Yàlla gi