10 Lépp lu saay gët xemmemaa, xañuma ko sama xol. Bañaluma sama bopp benn bànneex, xanaa di bége lu ma liggéey, yooloo ko la ma liggéey.
11 Ma xoolaatal sama bopp lépp lu ma sottal, doñ-doñi ko, ba sottal, ndeke lépp, cóolóoli neen ak napp um ngelaw. Nit gisul njariñ ci kaw suuf.
12 Ma geesu xoolaat xel mu rafet, xool ag nitoodi akug ndof. Ana ku may wuutuji ci nguur gi, lu muy def lu moy lu ñu daan def?
13 Ma gis ne ni leer ëppe lëndëm njariñ, ni la xel mu rafet ëppe ndof njariñ.
14 Ku xelu day xool fa muy jaare, dof biy tëñëx-tëñëxi cig lëndëm. Ma ne moona ñoom ñaar a bokk dogal moos.