Text copied!
Bibles in Wolof

Kàdduy Waare 1:7-11 in Wolof

Help us?

Kàdduy Waare 1:7-11 in Kàddug Yàlla gi

7 Dexoo dex wal, wuti géej, te taxul géej fees. Fa dex wal jëm, fa lay walati, jëm.
8 Jëfoo jëf ca jëfit, làmmiñ tuddul lépp, bët du suur, nopp du buur.
9 Lu ayoon mooy ayati, lu ñu jëfoon moom lañuy jëfati. Dara yeesul fi kaw suuf.
10 Lëf a ngii, nit naa: «Lii de lu bees la,» te mu ngi fi woon lu yàgg, lu jiitu sunu juddu.
11 Kenn du fàttliku ñi jiitu, ñiy ñëwit, ñi leen topp duñu leen fàttliku.
Kàdduy Waare 1 in Kàddug Yàlla gi