Text copied!
Bibles in Wolof

Kàdduy Waare 1:3-7 in Wolof

Help us?

Kàdduy Waare 1:3-7 in Kàddug Yàlla gi

3 Ana sax luy njariñu doñ-doñoo doñ-doñ ju nit di doñ-doñi fi kaw dun bi?
4 Ag maas wéy, ag maas teew; àddina sax ba fàww.
5 Jant fenk, so, ne coww dellu fa muy fenke.
6 Ngelaw jëm bëj-saalum, wiiri jëm bëj-gànnaar, di wiir ak a wiiraat, di delluy wëndeelu, topp yoonam.
7 Dexoo dex wal, wuti géej, te taxul géej fees. Fa dex wal jëm, fa lay walati, jëm.
Kàdduy Waare 1 in Kàddug Yàlla gi