Text copied!
Bibles in Wolof

Kàdduy Waare 1:3-10 in Wolof

Help us?

Kàdduy Waare 1:3-10 in Kàddug Yàlla gi

3 Ana sax luy njariñu doñ-doñoo doñ-doñ ju nit di doñ-doñi fi kaw dun bi?
4 Ag maas wéy, ag maas teew; àddina sax ba fàww.
5 Jant fenk, so, ne coww dellu fa muy fenke.
6 Ngelaw jëm bëj-saalum, wiiri jëm bëj-gànnaar, di wiir ak a wiiraat, di delluy wëndeelu, topp yoonam.
7 Dexoo dex wal, wuti géej, te taxul géej fees. Fa dex wal jëm, fa lay walati, jëm.
8 Jëfoo jëf ca jëfit, làmmiñ tuddul lépp, bët du suur, nopp du buur.
9 Lu ayoon mooy ayati, lu ñu jëfoon moom lañuy jëfati. Dara yeesul fi kaw suuf.
10 Lëf a ngii, nit naa: «Lii de lu bees la,» te mu ngi fi woon lu yàgg, lu jiitu sunu juddu.
Kàdduy Waare 1 in Kàddug Yàlla gi