2 Cóolóoloo cóolóol, waru waarekat ba, cóolóoloo cóolóol, léppi cóolóoli neen.
3 Ana sax luy njariñu doñ-doñoo doñ-doñ ju nit di doñ-doñi fi kaw dun bi?
4 Ag maas wéy, ag maas teew; àddina sax ba fàww.
5 Jant fenk, so, ne coww dellu fa muy fenke.
6 Ngelaw jëm bëj-saalum, wiiri jëm bëj-gànnaar, di wiir ak a wiiraat, di delluy wëndeelu, topp yoonam.
7 Dexoo dex wal, wuti géej, te taxul géej fees. Fa dex wal jëm, fa lay walati, jëm.
8 Jëfoo jëf ca jëfit, làmmiñ tuddul lépp, bët du suur, nopp du buur.
9 Lu ayoon mooy ayati, lu ñu jëfoon moom lañuy jëfati. Dara yeesul fi kaw suuf.
10 Lëf a ngii, nit naa: «Lii de lu bees la,» te mu ngi fi woon lu yàgg, lu jiitu sunu juddu.
11 Kenn du fàttliku ñi jiitu, ñiy ñëwit, ñi leen topp duñu leen fàttliku.
12 Man waarekat bi, buurub Israyil laa woon ci Yerusalem.