Text copied!
Bibles in Wolof

Kàdduy Waare 1:10-14 in Wolof

Help us?

Kàdduy Waare 1:10-14 in Kàddug Yàlla gi

10 Lëf a ngii, nit naa: «Lii de lu bees la,» te mu ngi fi woon lu yàgg, lu jiitu sunu juddu.
11 Kenn du fàttliku ñi jiitu, ñiy ñëwit, ñi leen topp duñu leen fàttliku.
12 Man waarekat bi, buurub Israyil laa woon ci Yerusalem.
13 Damaa dogu ne damay gëstu, teg ko ci xel mu rafet, di settantal mboolem lu nit def fu jant bi tiim. Ndaw sas wu tiis wu Yàlla sase, ñu war koo sasoo!
14 Gis naa jépp jëf ju jëfe ci kaw suuf, ndeke lépp cóolóoli neen la ak napp um ngelaw.
Kàdduy Waare 1 in Kàddug Yàlla gi