Text copied!
Bibles in Wolof

Kàdduy Waare 12:7-11 in Wolof

Help us?

Kàdduy Waare 12:7-11 in Kàddug Yàlla gi

7 Su boobaa pënd dellu suuf, na woon; bakkan dellu fa Yàlla ma able woon.
8 Cóolóoloo cóolóol, waru waarekat ba. Léppi cóolóoli neen.
9 Waarekat ba daa xelu, di jànglewaale xam-xam, di natt ak a gëstu, di jekk-jekkal kàdduy xel yu takku.
10 Waarekat ba daa tànn baat yu saf, bind ko, mu jub te dëggu.
11 Waxi ku xelu day gindee, bantub sàmm la; tënk ba diy pont, sampe ca. Loolu ag may la, jóge ci sàmm biy kenn.
Kàdduy Waare 12 in Kàddug Yàlla gi