Text copied!
Bibles in Wolof

Kàdduy Waare 12:5-12 in Wolof

Help us?

Kàdduy Waare 12:5-12 in Kàddug Yàlla gi

5 Nga dem, ba ragal fu kawe, am tiitaange ciw yoon, garab tóor, ba weex furr, soccet di yokokoki, doomu garab tëë yékkati siddit, nga jëm kër gu mujj, waa dëj bi fees mbedd mi.
6 Bàyyil xel ki la sàkk, balaa buumu xaalis bi ne tipp, ndabal wurus wi, tasar, njaq la ñuy roote, rajax, poli ba ca teen ba, tàllit.
7 Su boobaa pënd dellu suuf, na woon; bakkan dellu fa Yàlla ma able woon.
8 Cóolóoloo cóolóol, waru waarekat ba. Léppi cóolóoli neen.
9 Waarekat ba daa xelu, di jànglewaale xam-xam, di natt ak a gëstu, di jekk-jekkal kàdduy xel yu takku.
10 Waarekat ba daa tànn baat yu saf, bind ko, mu jub te dëggu.
11 Waxi ku xelu day gindee, bantub sàmm la; tënk ba diy pont, sampe ca. Loolu ag may la, jóge ci sàmm biy kenn.
12 Doom, leneen lu ci tegu, moytu ko: Yokki téere amul kemu, njàng mu bare, coonoy boroom.
Kàdduy Waare 12 in Kàddug Yàlla gi