4 bunt yi féeteek mbedd mi tëje, coowal wol dal, as picc sab, nelaw naaw, janq ju doon woy, selaw.
5 Nga dem, ba ragal fu kawe, am tiitaange ciw yoon, garab tóor, ba weex furr, soccet di yokokoki, doomu garab tëë yékkati siddit, nga jëm kër gu mujj, waa dëj bi fees mbedd mi.
6 Bàyyil xel ki la sàkk, balaa buumu xaalis bi ne tipp, ndabal wurus wi, tasar, njaq la ñuy roote, rajax, poli ba ca teen ba, tàllit.
7 Su boobaa pënd dellu suuf, na woon; bakkan dellu fa Yàlla ma able woon.
8 Cóolóoloo cóolóol, waru waarekat ba. Léppi cóolóoli neen.
9 Waarekat ba daa xelu, di jànglewaale xam-xam, di natt ak a gëstu, di jekk-jekkal kàdduy xel yu takku.