Text copied!
Bibles in Wolof

Kàddu yu Xelu 9:9-15 in Wolof

Help us?

Kàddu yu Xelu 9:9-15 in Kàddug Yàlla gi

9 Xelalal ku xelu, mu yokku. Xamalal ku jub, mu yokk njàngam.
10 Ragal Aji Sax ji di njàlbéenu rafet xel, xam Aji Sell ji di am ug dégg.
11 Maay Xel mu Rafet, ku ma topp gudd fan, dund, dundati.
12 Rafet xel, jariñu, kuy kókkalee, wéetook sa añ.
13 Jigéen ju dof day xumb, reew, du xam lu xew.
14 Day toog bunt këram, mbaa fu kawee kawe ca dëkk ba,
15 di woo ña fay jaare te jubal seenu yoon.
Kàddu yu Xelu 9 in Kàddug Yàlla gi