5 «Kaay, ma may la, nga lekk, xellil lay biiñ, nga naan.
6 Dëddul jëfi téxét ba dund, di jubal ci yoonu dégg.»
7 Artu kuy ñaawle, feyoo saaga rekk, yedd ab soxor, yooloo loraange.
8 Bul yedd kuy ñaawle, da lay jéppi; yeddal ku rafet xel, mu naw la.
9 Xelalal ku xelu, mu yokku. Xamalal ku jub, mu yokk njàngam.
10 Ragal Aji Sax ji di njàlbéenu rafet xel, xam Aji Sell ji di am ug dégg.
11 Maay Xel mu Rafet, ku ma topp gudd fan, dund, dundati.