12 Rafet xel, jariñu, kuy kókkalee, wéetook sa añ.
13 Jigéen ju dof day xumb, reew, du xam lu xew.
14 Day toog bunt këram, mbaa fu kawee kawe ca dëkk ba,
15 di woo ña fay jaare te jubal seenu yoon.
16 Ma nga naa: «Képp ku téxét, jàddal ba fii!» Ku ñàkk bopp, mu ne ko:
17 «Ndox mu lewul a neex, ñamu làqu-lekk dàqati.»