27 Ba muy taxawal asamaan, maa nga fa, ak ba muy rëdd fa asamaan taseek géej,
28 ak ba muy teg niir ya fa kaw, ak ba muy dooleel ndoxi xóotey géej,
29 ak ba muy sàkkal géej kemoom, ba du jàll fa mu wax. Ba muy rëdd fa muy samp àddina,
30 man, Xel mu Rafet, maa doon ku xareñ ci wetam, di ko bànneexal bés bu ne, tey bànneexu fi kanamam.
31 May bége wërngalu àddinaam, di bànneexoo doomi aadama.»
32 «Kon nag, doom, dégluleen ma. Mbégte ñeel na ki may topp.
33 Dégluleen ku leen di yar, daldi muus. Buleen ko sàggane!
34 Mbégte ñeel na ki may déglu, di teewlu ca sama bunt bés bu nekk, di ma toogaanu sama bunt kër.
35 Ku ma daj, gudd fan, Aji Sax ji bége la.
36 Ku ma moy loru, ku ma bañ, daa repp.»