22 Soxna si, Xel mu Rafet nee na: «Aji Sax ji jagoo na ma ca njàlbéen, ma jiitu ca jëfam ya woon.
23 Bu yàgg lañu ma dëj, ca ndoorte la, bala suuf a sosu.
24 Ba may dikk, géej amul, ndox ballul bay fees, di wal-wali.
25 Dikk naa bala tund yu mag yee sampu, lu jiitu tund yu ndaw yi,
26 laata Yàllaa sàkk suuf aki àllam ak feppu pënd ci àddina.