19 Li may mayee gën wurus, wa gën, sama njariñ wees xaalis ba gën.
20 Yoonu njekk laay jaare, di jëfe li yoon àtte rekk.
21 Ku ma sopp, ma nàddil la, feesal sab denc.»
22 Soxna si, Xel mu Rafet nee na: «Aji Sax ji jagoo na ma ca njàlbéen, ma jiitu ca jëfam ya woon.
23 Bu yàgg lañu ma dëj, ca ndoorte la, bala suuf a sosu.
24 Ba may dikk, géej amul, ndox ballul bay fees, di wal-wali.
25 Dikk naa bala tund yu mag yee sampu, lu jiitu tund yu ndaw yi,
26 laata Yàllaa sàkk suuf aki àllam ak feppu pënd ci àddina.