Text copied!
Bibles in Wolof

Kàddu yu Xelu 8:19-23 in Wolof

Help us?

Kàddu yu Xelu 8:19-23 in Kàddug Yàlla gi

19 Li may mayee gën wurus, wa gën, sama njariñ wees xaalis ba gën.
20 Yoonu njekk laay jaare, di jëfe li yoon àtte rekk.
21 Ku ma sopp, ma nàddil la, feesal sab denc.»
22 Soxna si, Xel mu Rafet nee na: «Aji Sax ji jagoo na ma ca njàlbéen, ma jiitu ca jëfam ya woon.
23 Bu yàgg lañu ma dëj, ca ndoorte la, bala suuf a sosu.
Kàddu yu Xelu 8 in Kàddug Yàlla gi