9 Ngoonug suuf la, jant biy lang, muy lëndëm di gëna guddi.
10 Ndaw si jekki dajeek moom, sol yérey gànc, lal pexeem.
11 Daa xumb, të, du toog këram.
12 Ma nga ca mbedd ma, ne ca pénc ya, ruqoo ruq, ma ngay yeeroo.
13 Ndaw sa ne ko katam, fóon, ne wajj, ne ko: