Text copied!
Bibles in Wolof

Kàddu yu Xelu 7:5-10 in Wolof

Help us?

Kàddu yu Xelu 7:5-10 in Kàddug Yàlla gi

5 Dina la aar ci ndaw su yemadi, bokk feneen, di wax lu neex.
6 Damaa tollu sama palanteer, séentu ca xarante ya,
7 séen ca biir téxét ya, ku ma seetlu ca xale yu góor ya, muy ku ñàkk bopp.
8 Muy dem ba fa ndaw say taxaw, ca selebe yoon wa, daldi wuti kër ndaw sa.
9 Ngoonug suuf la, jant biy lang, muy lëndëm di gëna guddi.
10 Ndaw si jekki dajeek moom, sol yérey gànc, lal pexeem.
Kàddu yu Xelu 7 in Kàddug Yàlla gi