Text copied!
Bibles in Wolof

Kàddu yu Xelu 7:18-23 in Wolof

Help us?

Kàddu yu Xelu 7:18-23 in Kàddug Yàlla gi

18 Dikkal, nu baanee baane, ba bët set, te bànneexu ci mbëggeel.
19 Sama jëkkër newu fa, daa dem yoon wu sore.
20 Mbuusum xaalis la ŋàbb, yóbbu, du ñibbsi ndare weer wi fees dell.»
21 Muy mocc ak a moccaat, ba nax ko, di wax lu neex, ba man ko.
22 Waa ja jekki, topp ko, mbete yëkk wu ñuy rendiji, mbaa dof bu ñu jéng, di ko yari.
23 Mooy picc mu tàbbi cig fiir. Du xam ne day dee, ba keroog fitt jam ko ci xol.
Kàddu yu Xelu 7 in Kàddug Yàlla gi